¶ Aji Sax ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen:
TSK
TSK · Genesis 9:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Teewul saa yu leen soobee, sañ ngeena rendi, lekk ci lépp lu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeele, ak fépp fu ngeen dëkk. Ku sobewu ak ku set yépp sañ na caa lekk, mel ni bu doon kéwél mbaa kooba.
Yaa saxalal jur gi ñax ak gàncax gu doom aadama di bey, ba génnee ab dund fi suuf,
Kiy lekk, bumu ko xeebe ki lekkul; ki lekkul it, bumu sikk kiy lekk, ndax Yàllaa ko xajoo.
Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
¶ «Sañees na lépp,» lañu wax. Waaye du lépp ay jariñe. «Sañees na lépp,» waaye du lépp ay yokke.
¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.
«Bul jël lii, bul ñam lee, bul laal la ca des.»