TSK

TSK · Hebrews 11:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»

Isaaxa ne ko: «Déglul, ma wax la. Màggat naa te xawma sama bésu dee.

¶ Ba mu ko defee Israyil ne Yuusufa: «Léegi man dinaa dee, waaye Yàlla dina ànd ak yeen, ba delloo leen ca seen réewu maam.

«Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!

¶ Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam.

¶ Mu ne ko: «Déedéet, duma dem, samam réew kay laa jëm, ca saay bokk.»

Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq ni max la mu gëna fonk. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.

Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee?

Ngëm la bàyyikoo Misra, te ragalul sànjum buur, xanaa dogu rekk, mbete kuy gis ki gisuwul.

¶ Googu texe, yonent ya jottli woon waxyub seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.