TSK

TSK · Hebrews 13:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 2:44 TSK

Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.

¶ Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

Defleen seen kem kàttan, ngir di jàmmoo, ba mana sàmm seenug bennoo ci biir Noo gi ngeen bokk.

¶ Ndegam amees na lenn lu yokk aw fit ci Almasi mi nu gëm, ndegam lenni cofeelam lu mana dëfal am na, ndegam amees na benn cér ci Noo gu Sell gi, ndegam it, amees na lenn lu bawoo fi moom, ci wàllu xol bu rafet, ak yërmande,

¶ Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.

Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.

Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far.

¶ «Waaye li ma la sikke moo di sa cofeel ga nga jëkke woon, moom nga wacc.