TSK

TSK · Hebrews 13:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Li may wax, bokk yi, moo di, li des yàggatul. Kon nag bés niki tey, na ñi am jabar mel ni bu ñu ko amul woon;

¶ Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.

¶ Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi tooge ca ndijooru Yàlla.

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.

¶ Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka, dajee di màggal;

Waaye asamaan su bees ak suuf su bees sa njub di dëkki bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon.