TSK

TSK · Hebrews 13:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kon nag Almasi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.

¶ Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaleey, fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñemeey,

¶ Lii nag sañoon naa la koo digal ci turu Almasi, ndax mooy li la war,

¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.

¶ Kon nag gannaaw digeb tàbbi ci noflaayal Yàlla mu ngi sax ba tey, nanu ragal kenn ci yeen taxawe melokaanu ku ca jotul.

Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn farlute googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk.

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.

Moo waral Yeesu itam deeye ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi, deretu boppam.