TSK

TSK · Hebrews 13:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 27:1 TSK

¶ Ba loolu wéyee ñu dogu noo dugal gaal, jëme nu réewum Itali. Ñu teg Póol ak ñeneen ñu ñu tëjoon, ci loxool njiitu takk-der bu ñuy wax Yulyus, bokk ci mbooloom xarem buur bu mag bi.

¶ Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.

¶ Sunu yiwu Sang Yeesu Almasi nag, ak cofeelu Yàlla, ak bennoo geek Noo gu Sell gi, yal nañu bokk ànd ak yeen ñépp.

Te it gëmkat ñu sell ñépp a ngi leen di nuyu, rawatina waa kër Buur Sesaar.

ndax dégg naa sa gëm Sang Yeesu, ak sa cofeel ci mboolem ñu sell ñi.

¶ Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.