¶ Waaye su ñu tenqee lenn ci cari oliwu kër, te yaw ngay caru oliwu àll, ñu indi la, jabtal ci oliwu kër gi, nga wuutu car ya ca fàqe, ba mana xéewloo meen miy wale ci reenu oliwu kër gi, di ko dundal,
TSK
TSK · Hebrews 3:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Loolu lépp def naa ko ndax xibaaru jàmm bi, ngir am ci wàll.
ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
¶ Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.
Sunuy baay a nu yar fan yu néew, na mu jaadoo woon ci seenum xel. Waaye sunu Baay bii, sunu njariñal bopp lanuy yare, ngir nu séddu ci sellaayam.
¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.