TSK

TSK · Hebrews 4:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ki ci jal bi ci boppam, bu baadoolo yiy dugg, na duggandook ñoom, bu ñuy génn, mu génnandook ñoom.

Acts 1:11 TSK

Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise, mu jëm asamaan, ni lay délsee.»

Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!

Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.

¶ Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.

Musaa déy «jawriñ bu wóor la woon ci biir mboolem waa kër Yàlla,» di seedeel Yàlla kàddu ya ñu fa wara wax.

Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkisedeg.

¶ Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu tooge ndijooru ngànguney ku Màgg ka fa asamaan.

Ndax bérab yu sell yu nit tabax, te muy royaalub bérab bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi dugg. Waaye biir asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla.

Nanu ŋoy ci yaakaar, ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.