TSK

TSK · Hebrews 5:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”»

¶ Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.

Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?»

Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.

te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bundxatalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

te «ngeen xàllal seen bopp xàll yu jub yu ngeen di jaare seeni tànk,» ngir kuy soox doxe ca wér te baña gëna tële.