TSK

TSK · Hebrews 5:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

Musaa wax ak Aaróona ne ko: «Dikkal fii ci sarxalukaay bi te joxe sa saraxu póotum bàkkaar ak sa saraxu rendi-dóomal, nga jotoo ko, yaw yaak mbooloo mi, boo noppee joxe saraxu mbooloo mi, jote leen ko, muy li Aji Sax ji santaane.»

Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi.

Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.