TSK

TSK · Hebrews 6:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yanqóoba jegesi, fóon ko, xetu yére yi mu sol xeeñ Isaaxa, mu door koo ñaanal ne ko: «Sama xetu doom kay xetug tool la, bu Aji Sax ji barkeel.

Aji Sax jee leen di xéewale, ngir baaxe seen meññeefum njurukaay, ak seenug jur, ak seen meññeefum suuf, ca réew ma mu giñaloon seeni maam, ne moom la leen di jox.

ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.

Ku doon wéya wéy, di jooy; ŋàbb mbuusum jiwoom, yal na dikka dikk, di woy, ñibbaale sabaaram.

Ab taw ak tawub yuur asamaan lay wàcce, du fa dellu, te suuxatul suuf, saxal ko, meññal ko, ba kuy ji, mu may la jiwu; kuy lekk, mu may lam pepp.

Jiwal-leen seen bopp njekk, ba góobe ca lu ngor maye. Gàbbleen ag mbooy, sàkku Aji Sax ji jot na, ba kera muy dikk, tawal leen njekk.

Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.