Nun itam naka noonu, ba nu dee ay tuut-tànk yu nekk ci kilifteefu mbiri àddina, ay jaam lanu woon.
TSK
TSK · Hebrews 7:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi ca bant ba.
Melkisedeg nag du baay, du ndey, du askanu maam wees ko xamal. Du ndoortel gane àddina, du njeextel dund wees ko xamal. Dees koo def mu niru Doomu Yàlla, te saxoo di ab sarxalkat ba fàww.
Waaye Yeesu mii la ag palam ànd ak ngiñ lu jibe ca ka ko wax ne ko: «Boroom bee ko giñ te du dellu gannaaw: “Yaa dib sarxalkat ba fàww.”»
Ndax kat yoonu Musaa, ay nit ak seenug néew doole la fal ay sarxalkat yu mag. Waaye kàddug ngiñ li topp ci yoon wi, moo fal sarxalkat bu mag, Doom ji ñu matal sëkk ba fàww.
¶ Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi.