TSK

TSK · Hebrews 8:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ñaan mucc, nga saxal jalam fàww,

Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii! Aji Sax ji sama Yàlla, yaaka màgga màgg. Teddngaak daraja nga soloo,

doom aadama xam say jaloore ak sa teddngaak sa darajay nguur.

Micah 5:4 TSK

Kookooy doon buntu jàmm, ba bu waa Asiri songee sunum réew, ba daagoo sunu kawi tata, juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil, ba juróom ñetti garmi.

¶ Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi tooge ca ndijooru Yàlla.

Ana kan ci malaaka yi la mas ne: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon, say dëggastal»?

¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.

Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru jalub Yàlla.