Na indi kuuy mu amul sikk, ñu xayma njégam, yót ko sarxalkat bi, muy saraxu peyug tooñ. Na ko ko sarxalkat bi defal njotlaayal bàkkaar bi mu def te xamu ko woon. Su ko defee mu am njéggal.
TSK
TSK · Hebrews 9:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, te mooy ñuy joxeel bànni Israyil seen njotlaay benn yoon cim at ngir seen bàkkaar yépp.» Ñu daldi def li Aji Sax ji santoon Musaa.
Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, te faaleedi samay santaane.”
Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor, du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun. Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon, ku ci nekk di wax lu amul bopp. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii, ay kéemtaan aki kiraama yuy tiiñ boroom xel ak xelam, réer xamkat ak xam-xamam.»
Rawtu dina réer ku gaaw, boroom doole du tala jariñoo dooleem, jàmbaar sax du mana rawale bakkanam.
Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.
Sarax yooyu ay bàkkaar lay fàttlee at mu jot,