¶ Nattu yu mag yooyu, ak firnde yeek kéemaan yu réy yooyu, yeena ci teg seen bët,
TSK
TSK · Hosea 11:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji ne ko: «Déggalal mbooloo mi te def li ñu la wax lépp. Du yaw lañu bañ, waaye man mii lañu bañ ma doonati seen buur.
Mu sàlloo bàkkaari Yerbowam doomu Nebat. Loolu doyatu ko, mu jël jabar Yesabel doomu Etbal, buurub waa Sidon ña. Mu dem bay jaamu seen tuur mi ñuy wax Baal, di ko sujjóotal.
Moonte Aji Sax ji àrtu woon na Israyil ak Yuda, mboolem yonentam yaak boroom peeñu ya jottli leen ko, ne leen: «Dëppleen seen yoon yu bon yii ngeen topp, te sàmm samay santaane, wormaal samay dogal, na mu dëppook mboolem yoon wi ma tëralal seeni maam, yónnee leen ko, yonent yiy samay jaam jottli leen ko.»
Wii xeet kat ay fippukat lañu, yii doom a diy fen-kat te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!
Moona sama ñoñ fàtte nañu ma; tuuri caaxaan, ñu taalal cuuraay, te tuur yi di leen fakktal ci seeni yoon, seen jaaruwaay ya woon, di leen jaarale ñall yu kenn xàllul,
Waaye dégluwñu, teewluwñu, ba dëddu seenug mbon, baña taalal yeneen yàlla cuuraay,
Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
Sama ñoñ dañoo làggi ci ñàkke ma kóllëre, wooyees na leen fa kaw, te kenn ci ñoom jógul.
Léegi ñu ngi gën di bàkkaar, di xellee ci seen xaalis jëmmu tuur, ay jëmmi xërëm yu ñu sàkke seen xareñte, lépp di càkkéefu ay liggéeykat, te ci ñoom la nit ñi naan: «Rendikati sarax yaa ngi fóon ay tuuri wëllu.»
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
ndax kat nun nooy cuuraayal Almasi fa Yàlla, ñeel ñi ci yoonu texe, ak ñi ci yoonu sànkute.