waaye demal Padan Aram ca sa kër maam-góor, ji jur sa yaay, nga jël fa jabar ca sa doomi nijaay Laban.
TSK
TSK · Hosea 12:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ La Aji Sax ji santoon Musaak Aaróona, noonu rekk la ko bànni Israyil defe.
Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.
Biir géej di saw yoon; saw xàll ci digg ndox mu ne xéew, te kenn gisul foo teg tànk!
«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla, xamuleen Yàlla ju dul man, te kenn du musle ku ma moy.
Yeen maa leen génnee réewum Misra, kërug njaam googa, maa leen fa jote, ba yebal fi seen kanam, Musaa ak Aaróonaak Maryaama.
¶ «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.