TSK

TSK · Hosea 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji yóbbu leen ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne yeen la koy jox, muy dëkk yu mag yu baax yu ngeen tabaxul,

Moo leen waral kawtey réew ma, ñuy xontoo meññeefum àll bi, mu di leen nàmpale lem ju walew doj, ak diw gu balle xeer wu ne sereŋ,

Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi.

Ku bon daŋŋiiral, seetul dara, xalaatam yépp mooy Yàlla amul.

Yeena fàtte Yàlla ji leen di musal, bawuleen xel seen cëslaay jiy seen rawtu, xanaa di jëmbatal seeni tuur ay tooli ngëneel, di ji jiwu mu bawoo feneen.

«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa ma fàtte, jalax ma sa gannaaw. Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”»

Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.

Israyil moo fàtte ab sàkk-katam, di tabax kër yu yànj. Yuda moom yokki dëkk yu tata wër. Maay yebal sawara ci kawi dëkkam, mu xoyom ay tataam.»