TSK

TSK · Hosea 2:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dingeen bàcc ba keroog wittum reseñ jot te dingeen witt reseñ ba keroog ji jot. Dingeen lekk seenum pepp ba suur këll te dingeen dëkk ak jàmm ci seenum réew.

Mooy àtte diggante xeet yi, mooy dogalal ay askani askan, ñu tëgg seeni saamar ay illéer, def seeni xeej ay sàrt; aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, te dootuñu jàngati xare.

Maa leen di may coobarey xam ma, te xam ne maay Aji Sax ji, ba ñu doon sama ñoñu bopp, man ma doon seen Yàlla. Dinañu délseek seen léppi xol ci man déy!»

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, maay far ci réew mi wépp rab wu aay. Su boobaa ñu dëkke màndiŋ mi ci xel mu dal, di fore bët biir gott bi.

Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellnga, maa niy xamlee sama bopp, yéefar yu bare di gis, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»

Hosea 6:6 TSK

Ndax ngor laa namm, dub sarax, ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.

Micah 4:3 TSK

Mooy àtte diggante xeet yu bare, mooy dogalal askan yu am doole te sore, ñu tëgg seeni saamar ay illéer, def seeni xeej ay sàrt. Aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, te dootuñu jàngati xare.

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

Kenn dootu soxlaa jàngal moroomam, mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Boroom bi!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag.