TSK

TSK · Hosea 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Aji Sax ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax kóllëreem ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen.

Sa yërmande ju réy nga topp, ba faagaagaloo leen. Wacculoo leen it, ndax yaw Yàllay yiw ak yërmande nga!

Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.

Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.

Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne: “Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.” Kàddug Aji Sax jee. “Duma la fasal kanam. Man Boroom ngor laa, te duma jàpp mer ba fàww.” Kàddug Aji Sax jee.

Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.

Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.

Hosea 9:1 TSK

Yeen waa Israyil, buleen béglu, buleen bànneexu ni yeneen xeet yi, nde yeena gànctu, dëddu seen Yàlla, yeena safoo peyu ngànctu ci mboolem dàgga ju ñuy bàcce pepp.

Amos 2:8 TSK

Yérey tayle yu ñu nangoo ci néew-ji-doole sax, ñu lal, ne ñàyy ci wetu mboolem sarxalukaay. Ku leen ameel, ñu feyloo la biiñ, naan ca seen biir kër tuur ya.

Micah 7:7 TSK

Man nag Aji Sax ji laay séentu, Yàlla ji may musal laay xaar, te sama Yàllaa may nangul.

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Yërmande laay dellusee Yerusalem. Sama kër lees fay tabaxaat.” Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. Mu ne: “Buumu nattukaay dina tàllalu ci kaw Yerusalem.”

Luke 1:54 TSK

Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,

Dungeen mana naan ci kaasu Sang bi, naan ci kaasu rab yi. Dungeen mana bokk lekk ci ndabal Sang bi, bokk lekk ci ndabal rab yi.