Teewul baayam lànk, ne ko: «Xam naa ko, doom, xam naa ko. Moom itam dina doon aw xeet tey doon ku màgg, waaye rakkam a koy sut, te askanam dina law, ba di ay xeet.»
TSK
TSK · Hosea 5:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yerbowam nag di wax ca xelam naa: «Léegi nguur gi dellu ci loxol waa kër Daawuda.
Waa Siri ñoo ànd ak Efrayim ak doomu Remalya, di la fexeel naan:
Aji Sax jee lay dikke, yaak saw xeet ak sa waa kër baay, ay bés yu tar yu masula am, ba Efrayim dëddoo Yuda ba tey, te buurub Asiri la koy sababe.»
¶ Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»
Efrayim day gental kera bésu mbugal, maa xamle ci biir giiri Israyil lu wér péŋŋ.
Ba Efrayim gisee jàngoroom, Yuda gis ab danaam, Efrayim a dem Asiri, yónnee ca Buur Yareb. Waaye manu koo wéral, mbaa di ko fajal ab danaam.
Efrayim a yokk ay sarxalukaay ngir moy, ñu doon ay sarxalukaayi moyukaay doŋŋ!
Bu Efrayim daan wax, ñépp ay lox; mu amoon daraja fi digg Israyil. Waaye moo sikkal boppam ci tuuri Baal, ba dee.
«Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»
Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.