TSK

TSK · Hosea 6:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Dellul ba ca Esekiya, sama njiitu ñoñ, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di la wéral, te bu gannaaw ëllëgee dinga dem kër Aji Sax ji.

Ngalla féqal fani Buur, ay atam bare, sët ba sëtaat.

¶ Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israyil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.”

«Man nag maa leen di musal ci njaniiwa? Maa leen di jot ci ndee? Moo yaw ndee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!

Su nuy dund, Boroom bi lanuy dundal, su nuy dee it, Boroom bi lanuy deeyal.