TSK

TSK · Isaiah 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.

Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, biiñ xelli ca xawaare ja. Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, xooluñu li mu jo loxoom.

Gis nga lu bare, waaye jàppoo ci dara. Nopp ne kótt, dég-dég të!»

«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»

«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

«Sama ñoñ ñi réer niy xar, seeni sàmm a leen lajjal, sànk leen fi kaw tund yi, ba tundoo tund, ñu yéegi fa, fàtte seen goorukaay.

Li ñuy fàtte te di ko tey moo di ci kàddug Yàlla la asamaan nekke bu yàgg, te ci kàddoom la suuf bindoo ci ndox, ba génne ci ndox.