Mooy tabax kër gu tanewul mbaarum wattukatu tool, te lëndu jargoñ gën koo dëgër.
TSK
TSK · Isaiah 1:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Boroom beey wal noowal mbugal, noo guy lakk, sellal, fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.
Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob, di sànni loxo waa tundu Siyoŋ, di ko tëkkoo waa Yerusalem googu.
Junneey daw fu leen kenn gëdde, juróom gëdd, ngeen daw yeen ñépp, ba ña des mel ni bantub raaya ci kaw tund, ne cundum ni raaya bu wéet ca coll wa.»
Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom: Yaw, janq Siyoŋ mu taaru da laa xeeb, di la ñaawal. Yerusalem, dëkk bu taaru booboo lay wëcc bopp, di la kekku sa gannaaw.
Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool, ndax man la gàntal.» Kàddug Aji Sax jee.
Moo tas mbaaram ni bu doon mbaarum tool, moo rajaxe bérabu ndajeem. Aji Sax ji moo fàtteloo waa Siyoŋ màggal ak bésub Noflaay, te tàngooru meram la xalabe buur ak sarxalkat.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.