TSK

TSK · Isaiah 11:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Noowug Aji Sax jee may waxe, sol ma kàddoom.

Job 4:9 TSK

Yàllaay wal noowam, nga sànku, sànjam gelaw, nga jeele.

yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»

Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.

Ñeel Suleymaan. Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,

Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.

Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. Yilifal noon yi la wër!

Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.

Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

ab jal sampe fi ci ngor, ki ci tooge jikko ju dëggu di askanu Daawuda te di njiit luy sàkku yoon, yàkkamti njekk.

Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet, te buur ba lees ko waajalal; dees koo xóotal, yaatal ko, sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, di sël-sëli ni walum tamarax.

Aji Sax jee nuy jiite, Aji Sax jee nuy dogalal yoon. Aji Sax jeey sunu buur! Moom moo nuy wallu.

yaflu, di nes-nesi. Seenug mbon it amul kem: duñu defal jirim njub, duñu àtte néew-ji-doole dëgg.

Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.

Sàkkuleen Aji Sax ji, mboolem yeen néew-dooley réew mi, yeen ñiy jëfe àttey yoonam, sàkkuleen njekk te sàkkoo toroxlu, jombul ngeen yiiru, kera bésu merum Aji Sax ji.

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

akug teey, ak moom sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.

Titus 3:2 TSK

Buñu yàq der te buñu bëggu ay, waaye nañu di bëggkati jàmm, te nañuy jëfe lewetaay gu mat sëkk, seen digg ak ñépp.

Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.

¶ Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.