TSK

TSK · Isaiah 14:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mboolem dàll wu ab noon dukkate ba dikk, ak turki bu màndi deretu xare, sawara lees koy leel.

wi ñu daan xadaruy dóor askan yi, dóor yu dakkul, di joggatee xeet yi xol bu tàng, topp leen, tëë ba.

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi, toogal ne cell te fatu cig lëndëm, deesatu la wooye lingeeru réew yi.

Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral, te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,” nga def sa gannaaw gi aw yoon, ñu joggi, wéy.»

maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu.

Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen leen; yeen ñi dégg seen tur ñépp, jooyleen leen. Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe, ba foqaale jii daraja?”

«Yaw Babilon, yaa doon sama wàkku, di sama ngànnaay, ma di la wàkke xeet yi, rajaxee la réew yi,

Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.

te Yàlla teg ci say loxo doom aadama yeek rabi àll yeek njanaaw yi, nga boole leen yilif ñoom ñépp ak fu ñu mana dëkke: yaw yaay boppu wurus bi.

Éy Aji Sax ji, foo àppal lii, may woote wall, dégluwoo ma? Ma di la jooy aw ay, te walloowoo!

Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu ci sa kaw, te sànkuteg rabi àll yi sa tiitaange lay jur. Yaa tuur deretu nit, indi aw ay ci réew mi, ak dëkk beek mboolem ñi ci biiram.

Ma dégg malaaka mi yilif ndox yi ne: «Yaw Aji Sell ji nekk te nekkoon, yaa yey dogal yii àtte.

Ndaxte ay bàkkaaram jalu na ba àkki asamaan, te Yàlla bàyyi na xel ay ñaawtéefam.

Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.