TSK

TSK · Isaiah 18:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ, taamu faa dëkke.

Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj, xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ, te fa la baadooloy ñoñam di rawe.

Waaye yaw askan wi, ñi nga deele ñooy dellu dundaat, seeni néew ay dekki, ku doon nelaw sa biir bàmmeel, yewwu, sarxolle. Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer, suuf délloosi ña dëddu.

Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet, seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba. Kàddug Aji Sax jee, Boroom sawara wi ci Siyoŋ, Boroom taal bi ci Yerusalem!

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen.

Amos 3:7 TSK

Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.