ak Misma ak Duuma ak Maasa
TSK
TSK · Isaiah 21:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Yanqóoba dafa yónni ay ndaw, ñu jiitu ko ca magam Esawu, ca réewu Seyir, di diiwaanu Edom.
Buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox ci seen suuf fu téstën sax tege, ngir Esaween ñi laa sédd diiwaanu tundu Seyir.
Boroom bi kat da maa wax, ne ma: «Doxal taxawal ab jongrukat, lu mu gis, wax ko.
Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan ba màndi deret, te mu ngii di wàccal Edom, xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.»
Buur Cedesyas yónnee, woolu ko. Mu ñaarook moom ca biir këram, laaj ko, ne ko: «Mbaa am nga kàddu gu bawoo ci Aji Sax ji?» Yeremi ne ko: «Xanaa lii: “Ci loxol buuru Babilon lees lay teg.”»
«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Edom a feyu ci waa kër Yuda, feyu ga mu feyu di tooñaange gu réy.
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm, jalax Edomeen ña.
¶ Peeñum Abdiyas a ngi. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom.