Ag suba ngeen ne: «Éy waay, bu doon ngoonati.» Bu ngoonee ngeen ne: «Éy waay, bu doon subaati!», ndax tiitaange lu ngeen di tiit, ak li ngeen di teg seeni gët.
TSK
TSK · Isaiah 21:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ñu tiita tiit, yaram di fuddook a metti, ñuy baddaañu ni kuy matu; ku ne jàq, di xulli sa moroom, kanam ya sël-sëleendoo.
Jooyi waa Yaser laay jooy reseñ ga fa Sibma, yeen waa Esbon ak Elale, ma sange leeni rongooñ, nde fa ngeen di dajaleek fa ngeen di góobe, coowal mbégtee fay dakke.
Éy Aji Sax ji, ni kuy matu lanu meloon fi sa kanam, di wañaarook a yuuxu.
Lu mel ni jaxaay a ngii, naa fëyy, firiy laafam, këfsi Boccra. Bésub keroog fitu jàmbaari Edom ne tërit, mel ni kuy matu.»
¶ Ca saa sa baaraami loxob nit buy bind feeñ fa janook tegukaayu làmp ba, ca kaw miiru kër buur, ba ñu weexal. Buur di xool catu loxo bay bind.
Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu, coow la tax samay tuñ di lox, sama yaram dee goyy, may lox fi ma taxaw, te ne cell, di séentu bésub njàqare, bay dikkal xeet wi nu song.