turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat.
TSK
TSK · Isaiah 23:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp.
¶ Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc.
¶ Jant yooyu doomu Baladan Berodag Baladan buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Booba dafa dégg ne Esekiya daa woppoon.
¶ Bataaxal bii mu ngi bawoo ci Reyum, boroom dëkk bi, ak Simsay bindkatam, ak seen nàttongoy àttekat yeek kàngam yeek saytukat yeek boroom téere yi, ak waa Urug ak waa Babilon ak waa Sus, Elameen ña,
Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,
Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba fàkkas xeeti xeet.
¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Maa ngii di jële bëj-gànnaar, indi ci kaw Tir, Nabukodonosor buuru Babilon, buuru buur yi, aki fas aki watiir aki gawar, ak mbooloo mu takku.
¶ Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nabukodonosor. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.
¶ «Mu daldi jóge réewum waa Kalde, sanci Karan. Fa la ko Yàlla toxale gannaaw ba baayam faatoo, sancal ko ci réew mii ngeen dëkk tey.