TSK

TSK · Isaiah 23:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñu ne leen: «Li ko waral mooy, dañoo fecci kóllërey Aji Sax ji, seen Yàllay maam, te mu fasoon ko ak ñoom ba mu leen jëlee réewum Misra.

Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas.

«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.

Tir moo tabaxal boppam tata, moo dajale xaalis ni feppi suuf, ak wurus wu ne xas ni donji banu mbedd.