TSK

TSK · Isaiah 27:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Maa leen di jógal.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. Mu ne: «Maay tenqi turu Babilon, tenqim ndesam ba ca seeni doom ak seen askan.» Kàddug Aji Sax jee.

Ngoon a ngay jot, tiitaange ne jaas, balaa bët a set lépp jeex. Lii mooy añub ñuy sëxëtoo, lii mooy deminu ñiy nangu sunu alal.

Maa ngeek yaw, nar laa wallu.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay fàkkas mboolem xeet ya ma la sànniji. Yaw nag duma la fàkkas, duma la ñàkka topp moos, waaye li nga yelloo laa lay yar.»

Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor, tasaale la ko wër.» Kàddug Aji Sax jee. «Nit du fa dëkkati, doom aadama du fa dalati.»

¶ «Buur, danga jekki xool, daldi gis jëmm ju mag ju ñu defar. Jëmm ja réy na lool te yànjaayam yéeme. Ma nga taxaw janook yaw, melokaanam raglu.

Sa damm-damm amul paj, sab góom metti, ba mboolem ñi dégg li la dal di tàccu ci sa kaw, nde ana ku sa mbon gi dul jeex lorul?