TSK

TSK · Isaiah 3:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba giléem ya naanee ba sottal, waa ji jël jaarob bakkan bu wurus bu tollook juróom benni garaam, ak ñaari lami wurus yu tollu ci téeméeri garaam, takkal ko.

¶ Surga ba nag génne ay gànjari xaalis ak yu wurus booleek ay yére, jox Rebeka. Càmmiñ la ak yaay ja itam, mu may leen alal ju takku.

Naka lañu koy yóbbu, mu yóbbante goroom ba ay kàddu. Da koo wax ne ko: «Ki moom lii moo ma ëmbal.» Mu teg ca ne ko: «Xoolal bu baax te wax ma ku moom jaarob màndargaal, bi ànd ak buum gi, ak yet wi.»

Ba loolu amee mbooloo mépp tekki seen jaaroy wurusi nopp, indil Aaróona.

Moo tax nu indi jooxeb Aji Sax ji, ku nekk ak la nga muurloo, ci gànjari wurus; lami përëg, ak takkub jara, ak jaaroy torlukaay, ak jaaroy nopp, aki caq. Noo ko def sunu njotlaayal bakkan, fi kanam Aji Sax ji.»

ba noppi takkal la jaarob bakkan ak jaaroy nopp, solal la mbaxanam lingeer mu yànj.