Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:
TSK
TSK · Isaiah 30:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Samuel 12:23
TSK
Psalms 25:8
TSK
Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
Psalms 143:8
TSK
Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
Proverbs 4:27
TSK
Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ, na sa tànk moyu lu bon.
Isaiah 35:8
TSK
Foofa law yoon di jaare, ñu di ko wooye Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.
Isaiah 48:17
TSK
Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israyil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.
Jeremiah 6:16
TSK
Aji Sax ji dafa wax ne: «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, te laajte yoon ya woon, ne: “Ana yoonu mbaax?” Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» Ñu lànk ne: «Awunu ca.»