TSK

TSK · Isaiah 33:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.

«Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.

Yaay raafal seeni giir fi kaw suuf, fey seen askan ci doom aadama yi.

Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.

Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, ki kaweel ab jalam, toog,

Ndijoor la Aji Sax ji xàcci, ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar.

Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»

Bésub keroog booba, kuy daŋŋiiral, detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Bésub keroog ngeen ne: «Santleen Aji Sax ji, tudd turam, xamley jalooreem ci biir xeet yi, fàttli màggaayu turam.

Buur a ngii, njekk lay nguuroo, jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;

Aji Sax ji nee: «Xaaral rekk ma jóg, xaaral rekk ma ne ñokket, xaaral rekk ma teewal samag kawe.

Yewwulee, yewwul, Siyoŋee, làmbool sa doole! Yerusalem, dëkk bu sell bi, solul ba ne ràññ! Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu ku lay songati.

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

ngir tabb waa Siyoŋ ñiy ñaawlu, jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal teddngaam.»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal man? Ana ban bérab ay sama dal-lukaay?

Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”

Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.

Ay àtteem dëgg la, yoon la! Moo mbugal jigéenu moykat bu mag, bi yàq àddinaak moyam, feye ko deretu jaami Yàlla yi mu tuure loxoom.»