TSK

TSK · Isaiah 33:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Booba lanu nangu mboolemi dëkkam. Amul benn dëkk bu nu nanguwul ci ñoom: juróom benn fukki dëkk, mboolem diiwaanu Argob, ba bokk ca nguurug Og ca Basan.

Ca lay xaare garabi seedari Libaŋ yi ne coleet, ba kawe, ak garab yu mag ya fa Basan.

Garab yi dul ruus, ak seedari Libaŋ sax di bége sab jéll, naan: “Ba nga daanoo ba tey, ab gorkat jógalu nu.”

Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ, àddina ne làcc, ne sereŋ, kàngami xeeti àddina ne làcc.

Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.

Joorug Saron ay dellu di parlub gàtt gi, xuru Akor di goorukaayu nag yi, ñeel sama ñoñ ñi may sàkkuji.

Maa ngii di delloo Israyil parloom, mu dellu di fore àllub Karmel ak Basan, di regge tundi Efrayim ak Galàdd.

Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ, sa gàtt yi nga séddoo, te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen, fi digg parlu mu naat. May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd na jant ya woon.

¶ Libaŋéey, ubbil say wunt, sawara xoyom sa garabi seedar.