TSK

TSK · Isaiah 34:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ak sama suufas bokk, ya ay dég aki dagg nangu. Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma, ak dëkk bu xumb ba.

suuf su wow doon ub déeg, joor gu maral ballal bëti ndox. Fa till fàkkoon, di fa goore, gattax ak barax a fay sëqe.

Xibaar a ngoog, di ñëw, riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar, nara gental dëkki Yuda yu mag yi, till yi dëkke.

Moo tax ay dundooti màndiŋ ak rabi àll a koy këroo, bànjóoli dëkke ko, kenn dootu fa desati, kenn dootu fa dëkk mukk ba fàww.

ay dëkkam gental, réew mi ne sereŋ, di ndànd-foyfoy, kenn du ko dëkke, doom aadama du fa jaare.

Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»

Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.