TSK

TSK · Isaiah 35:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 33:16 TSK

Mu ne ko rukk ndéey, boole kook màndarga, artoo ko ko,

Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.

Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm, te noppi ñiy dégg dañuy teewlu,

Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!

Dégguleen, yéguleen, seeni nopp masula bënn; xam naa ne ay workati neen ngeen, «njuddu-fippu» lañu leen di wooye.

Moo kan laay waxal, àrtu ko ba mu déglu, yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! Kàddug Aji Sax jaa ngii, mel ni lu ñu rus, lu ñu safoowul!

Luke 7:20 TSK

Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»

Acts 9:17 TSK

¶ Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.