TSK

TSK · Isaiah 35:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Man dinaa taxaw ci sa kanam ci doj woowu ca tundu Oreb. Dóoral ci doj wi, su ko defee ndox dina ci génne, mbooloo mi naan.» Musaa def noona ca kanam magi Israyil ña.

Pepp mu tawe asamaan nga faje seen xiif, ndox mu balle ciw doj, nga faje seen mar, te ne leen ñu dem nanguji réew ma nga leen giñaloon.

ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.

Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa, soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox;

Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég, joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ.

Maay walaley dex kaw coll ya ne duŋŋ, bënn bëti ndox digg xur ya, def màndiŋ ma ab déeg, suuf su ne sereŋ laay ballalem ndox.

Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,

Duñu xiif, duñu mar; tàngooru mbóoya akub jant du leen sonal, nde ki leen ñeewantee leen di wommat, di leen yóbbu fu ndox bënne.

Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.

Luke 1:64 TSK

Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla.

Acts 3:2 TSK

Fekk ñu indi fa waa ju judduwaale lafañ, ñu daan ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye bunt bu Rafet, ca kër Yàlla ga, ngir muy sarxu ñay duggsi.

Acts 8:7 TSK

Ndax bare na ca ñu rab yu bon jàppoon te mujj bàyyi leen, génne yuux yu réy; bare na ca it ñu lafañ ak ñu làggi woon te mujj wér.

Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.

¶ Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.