TSK

TSK · Isaiah 38:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.

Jëfeleen njub, ak mbaax gi Aji Sax ji rafetlu. Su ko defee dingeen baaxle, ba dem, nanguji réew mu baax mi Aji Sax ji giñaloon seeni maam,

ba keroog Aji Sax ji sottal kàddoom ga mu ma waxoon ne ma: “Su say sët sàmmee seen dundin, saxoo ngëm gu ma wéetal, te gar ci seen bakkan, kon doo ñàkk mukk ku lay wuutu ci jalub Israyil.”

Muy def li Aji Sax ji rafetlu, mboolem noonee ko Daawuda maamam daan defe.

¶ Ba ma déggee kàddu yooyu, damaa toog di jooy, ñaawlu ko ay fan, di woor ak a ñaan ci Yàlla Boroom asamaan.

¶ Rikk sama Yàlla, bàyyee ma lii xel, te bul far sama jëfi ngor ji ma jëfe ci sama biir kër Yàlla gi aki wartéefam.

Ma dekkal saraxu matt yi ñu wara joxe bu àppam jotee, ak saraxi ndoortel meññeef. Ngalla sama Yàlla, bàyyee ma lii xel ngir ngëneel.

Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.

Maa ngi janook sa ngor, di jëfe sa worma.

Naa teewlu yoonu maandute. Ana kañ nga may dikkal? Naa doxe maandute fi sama biir waa kër.

Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.

Fan yi Almasi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te nangule na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.