¶ Ba mu ko defee Lingeer buurub Saba may Suleymaan fanweeri barigoy wurus ak juróom, ak cuuraayu ndàbb lu ne gàññ, ak per yu jafe. Cuuraayu ndàbb loola Lingeer buurub Saba mayoon Buur Suleymaan, lu ni mel dikkatu fa ndax bare.
TSK
TSK · Isaiah 39:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Kings 10:10
TSK
1 Kings 10:25
TSK
Ñooñu ñoo ko daan indil at ci kaw at, ku nekk ak sab teraanga, muy ay jumtukaayi wurus ak yu xaalis aki mbubb aki gànnaay aki cuuraay aki fas aki berkelle.
2 Kings 20:13
TSK
Esekiya nag déglu ndaw ya, ba noppi won leen mboolem kërug dencukaayam: xaalis baak wurus waak ndàbb jaak diwu tànnéef gaak néegub gànnaayam ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiya wonul ci biir këram ak mboolem fu bokk ci kilifteefam.
Job 31:25
TSK
ndegam maa bége sama alal ju bare, bége koom gu ma sama doole may;
Proverbs 4:23
TSK
Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Jeremiah 17:9
TSK
«Dara gënula dëng xelum nit, laago la ci moom. Ana ku ko mana xam?