TSK

TSK · Isaiah 40:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Su dee ku sàcc mala, muy nag mbaa mbaam mbaa ab gàtt, te ñu fekk ko ciy loxoom, muy dund, na fey ñaaram.

Job 42:10 TSK

Gannaaw ba Ayóoba ñaanalee xaritam ya, Aji Sax ji tijji wërsëgu Ayóoba. Aji Sax ji ful na ñaari yoon mboolem alalu Ayóoba.

baal sa mbooloo seeni ñaawtéef, jéggal leen bépp bàkkaar. Selaw.

Yaw yaay taxaw, ñeewante Siyoŋ, ndax baaxe ko jot na, àpp ba kay mat na.

Bés bu leen Aji Sax ji teggilee seeni coonook seeni fitna, ba ngeen tàggook njaam gu metti, gi ñu leen doon jaamloo,

Du kenn ci waa Yerusalem, ku neeti wopp na. Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar.

Ma ne, képp ku la mere, dees koy rusloo, torxal ko. Kuy joteek yaw day neen, sànku.

Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»

Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal, yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam. Kaas bu wex bay miirloo, taat wa, yaa ko siitaatu.

Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»

Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal.» Kàddug Aji Sax jee. «Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.

Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal.

ca at ma jëkk ca nguuram, man Dañeel damaa gis ci téere yi limu at yi kàddug Aji Sax ji xamal Yonent Yàlla Yeremi, muy àpp bi Yerusalem wara gental, di juróom ñaar fukki at.

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

¶ «Yaw nag Dañeel, dencal kàddu yii, muy kumpa te nga tëj téere bi, tay ko ba mujug jamono jub. Su keroogee ñu bare dinañu gëstu fu ne, ba xam-xam yokku.»

Maay fóom garabi reseñam aki figgam, yi mu noon: “Lii sama peyoor la! Samay far a ma ko jox.” Maa koy def ay dédd, rabi àll yi di ko lekk.

Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.

Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay.”

Acts 1:7 TSK

Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés, bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam.

Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,

¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»