Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
TSK
TSK · Isaiah 40:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Asamaan a ngi biral njekkam, xeetoo xeet di gis darajaam.
nde Aji Sax jeey tabaxaat Siyoŋ, nara feeñeg leeram.
Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»
Aji Sax ji, yaa yokk xeet wi, yaw mii yaa yokk xeet wi, yaa fésal sa teddnga, yaa yokk mboolem kemi réew mi!
Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.
Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji, xeet yépp di gis, ba ca cati àddina. Ñépp ay gis sunu wallu Yàlla.
Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
«Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, ñu dikk ba niir samag leer.
Aji Sax ji neeti: «Ñoo wacc sama yoon wi ma leen tegaloon, sàmmuñu sama kàddu, jëfewuñu ko,
Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj, ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”»
“Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.
Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Gàtt bi di làmpam.