TSK

TSK · Isaiah 43:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?»

Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.

Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”»

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Yaay naan soowum xeet yi, nàmp weenu buur yi, ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.

«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla, xamuleen Yàlla ju dul man, te kenn du musle ku ma moy.

Titus 3:4 TSK

Waaye ba Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci doom aadama,