TSK

TSK · Isaiah 43:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

Sopp seeni maam nag moo tax mu taamu leen, yeen askan wi leen wuutu, génneel leen boppam Misra, ci dooleem ju bare,

ndax askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Céru Aji Sax ji moo di ñoñam, askanu Yanqóoba woowooy wàllam.

Ki Sax a taamu Yanqóoba, muy Israyil mi mu séddoo.

Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, ne nu: “Maa leen masa bëgg, ba tax ma sédd leen ngor.

Aji Sax ji nee: «Dama leena sopp,» yeen ngeen ne: «Ana noo nu soppe?» Mu ne: «Xanaa Esawu du seexub Yanqóoba?» Kàddug Aji Sax jee, «moona Yanqóoba laa sopp,

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.