TSK

TSK · Isaiah 44:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yeen déy lañu won loolu lépp ngir ngeen xam ne Aji Sax ji doŋŋ mooy Yàlla, te jeneen yàlla amul, ju dul moom.

¶ Dégluleen, bànni Israyil, Aji Sax ji sunu Yàlla, Aji Sax ji kenn la.

Aji Sax jee nuy jiite, Aji Sax jee nuy dogalal yoon. Aji Sax jeey sunu buur! Moom moo nuy wallu.

Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»

Ana ku def lii, dogal ko? Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi! Man Aji Sax ji maa jëkk, te man laak ñi mujj ba tey!

«Waxleen seenu lay,» la Aji Sax ji wax, «Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax.

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.

Buleen tiit, buleen ragal. Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko? Yeenay samay seede. Yàlla daa am ju ma moy? Cëslaay amul, xawma ci kenn!»

Aji Sax ji man a, du keneen; kenn du yàlla ku dul man. Maa la gemb, te xamuloo ma,

Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba, yeen bànni Israyil gi ma dégtal sama woote. Maay kenn, maa jëkk te maa mujj;

Sa jëkkër, ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israyil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.

Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddu, gi leen Aji Sax ji dégtal.

«Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam am kuuy mu mu xasoo sarxe, te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, nde man, buur bu mag laa!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.

¶ «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.

¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.

Man maay Alfa di Omega; maa jëkk, maa mujj, maay njàlbéen, maay muj.