TSK

TSK · Isaiah 44:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, tasaare doom aadama yi ci àddina, moo àppal xeet yi seen kemi réew, na mu dëppook limeefu goney Yàlla yi.

Ana ku def lii, dogal ko? Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi! Man Aji Sax ji maa jëkk, te man laak ñi mujj ba tey!

Ana ku yéene woon lii ca njàlbéen, ba nu xam ko? Ku ko yégle woon bu yàgg, ba nu man koo dëggal? Yéeneesu ko, yégleesu ko te déggeesul seeni kàddu.

Maa dogal ag njot, sottal ko, biral ko, ba tuuru doxandéem nekkagul seen biir. Yeen nag, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Man maay Yàlla,

Fàttlikuleen cosaan la woon. Man mii maay Yàlla, du keneen. Amul Yàlla ju mel ni man!

Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.