TSK

TSK · Isaiah 45:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Kon xamleen tey te délloosi ci seen xel, ne Aji Sax ji mooy Yàlla fa kaw asamaan ak fi kaw suuf. Du keneen.

Su ko defee xeeti àddina yépp dinañu xam ne Aji Sax ji mooy Yàlla, te amul moroom.

Job 12:18 TSK

Keey foq mbaxanam buur, jox ko ngemb, mu gemboo.

Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?

Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.

solal ko sa mbubb, dooleele ko sa ngañaay, teg kilifteefu réew mi ci loxoom, ba mu féete wàllu baay, waa Yerusalem, ak waa kër Yuda.

Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.

Buleen tiit, buleen ragal. Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko? Yeenay samay seede. Yàlla daa am ju ma moy? Cëslaay amul, xawma ci kenn!»

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Fàttlikuleen cosaan la woon. Man mii maay Yàlla, du keneen. Amul Yàlla ju mel ni man!