TSK

TSK · Isaiah 46:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ana kuy xettlee Israyil fa Siyoŋ? Éy bés bu Aji Sax ji delloo ñoñam ndam, ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! Ndaw bànneex laa ne, ci Israyil gii!

Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dal-lu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

Délloosil képp ku ñu ma tudde, te sama màqaama tax ma sàkk ko, tabax ko, sottal ko.»

Na asamaan wis-wisal, niir yuri njekk, suuf fett, meññal wall, boole ci jebbil njekk. Man Aji Sax ji, maa def lii!»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Sàmmleen yoon, di def njekk. Sama wall kat a ngi dikk léegi, sama njekk laa ne, léegi mu teew.

Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.

Ni suuf di fettalem njebbit, ab tool di ko saxalem jiwu, ni la Boroom bi Aji Sax ji di jebbile njekk ak cant, xeetoo xeet seede ko.

Dëkk bi daldi doon sama woy, di sama mbégte, di sama ndam, di sama sag ci biir mboolem xeeti àddina yi dégg ngëneel yi ma leen di defal yépp. Dinañu yéemu ba seen yaram daw ci lépp luy ngëneel ak jàmm ju ma leen di defal.»

Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.

¶ Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam, àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa, ak yonent yi seede nañu loolu.

Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

Su ko defee sunu turu Sang Yeesu màgge ci yeen, yeen it, ngeen màgge ci moom, ci sunu ndimbalal yiwu Yàlla, ak Sang Yeesu Almasi.

Moo waral lii dikk ci Mbind mi: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju doorukaay, doju tànnéef wu gànjare. Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk.»