TSK

TSK · Isaiah 47:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp.

Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel, Aji Sax jeey muri seen jë.

Jigéen ñi dal xel, ragal-leen; yeen ñi féex laa ne, tiitleen! Futtikuleen, ba ne duŋŋ; gembooy saaku, ñaawloo.

Man it maay ëñ sa pendal, muure sa kanam, saw taat ne duŋŋ.

Waxambaane yee yenu doji wolukaay, gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.

Hosea 2:3 TSK

Nanga wooye sa bokk yu góor: “Ñoñi Aji Sax ji,” sa bokk yu jigéen, nga ne leen: “Ñi Aji Sax ji yërëm.”

Nahum 3:5 TSK

«Maa ngii fi sa kaw,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Sa pendal laay ñori, ba muur sa xar-kanam, won xeeti jaambur yi sa yaramu neen, gisloo waa réew yi sa gàcce.

Ñaar di wolandoo, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.»