TSK

TSK · Isaiah 47:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Saa yu fexee, juble, te gisul sa ndigali yoon yi ko tiim. Ma ngay ciipu bañam yépp.

Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.

ngir xamees penku ba sowu, ne lu dul man neen la. Aji Sax ji man a, du keneen.

Dangaa yaakaaroon sa pexe yu bon, naan, «Kenn gisu ma!» Sam xel ak sa xam-xam a la wacc, ba tax nga naa: «Maa ko yor, man rekk.»

«Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. «Sa bés déy taxaw na, di àpp bi ma la wara mbugale.

Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle,

Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»

¶ Am na bés Buur Baltacar defal ay jaraafam bernde ju réy. Ña nga tollu ci junni, muy naan nag ca seen kanam.

¶ Guddi googa lañu rey Baltacar, buurub waa Babilon.

Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.

Ñu ñàng, raglu, te di dogalal seen bopp àtteb yoon ak sañ-sañ.

Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? Nan la doone nii ab gent, bérab bu rab yiy goore, mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu.

Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jël jabar ak a séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp.

Kaasu biiñu sànj, bi sababoo ci moyam, moom la askani àddina yépp di naan. Moom la buuri àddina àndal di moy, te doyloodig bakkanam gu réy woomal na julay àddina.»